Gaal Gui (2020)

Ana ñaata naqar moo daanu ci géej gi di baawaan
Toskare dal ci njaboot gi amatuñu yaakaar
Kune war ngaa man a xam ni géej amul bànqaas
Nañu gëm ni Buur Yàlla mooy maye
Hey boroom gaal gi tàm « contre-courant bi
Saa su nekk booy woy ngelaw li di ñu ko dégtal
Su dee dëgg la ni géej gii kuy maye jàmm nga
Maangi lay ñaan yow géej gi fexel ma gis ko
Hey yàkkamti man laa defloo
Looy réccu ëllëg yow mii àndal ak Yàlla
Bu fekke du yaay kiy maye, yow de, loo am jël
Dinañu wax ne tepp-tepp a gën yureet
Lu jot de, yomb
 
Combien de malheurs ont chaviré dans cette mer houleuse,
Causant une catastrophe sur la famille désespérée.
Chacun doit savoir que la mer n’a pas de branches.
Acceptons avec foi que c’est Dieu qui Donne.
Eh piroguier qui sait ramer à contre-courant,
Chaque fois que tu chantes, le vent nous ramène ton air.
S’il est vrai que la mer apporte la paix, je te prie, toi mer, de me la faire vivre…
L’empressement peut te faire faire ce que tu regretteras, alors aies foi en Dieu.
Comme tu n’es pas ton propre donateur, prends ce qui t’arrive.
On dit que petit à petit l’oiseau fait son nid, chaque chose en son temps…

Comments

  • ×